Caxat lawtan la, xeetu ñax guy law. Ñax la gu man a muñ bekkoor. Dees na fekk ca Afrig gu naaje gi: Senegaal, Kamerun, Keeñaa, Ugandaa, Ecoopi.
Guddaayam danay àgg 20i met. Ag ndomaam di mat 10i sàntimet. Dafa nguuni-ngaana, te ag meññam daa yeex, ci njeexiitalu noor mbaa nawet bi lay faral di meññ.
Fi muy sax fépp, xobam yi, meññeefam mu yees mi ak tóortóoram bi dees leen fay lekk ni ay lujum yu ñorut mbaa nu supp leen. Dees na ko xonte gàtt yi. Garab la guy faj tawat yu takku ci lim: góom, biir buy daw añs.
Leptadenia hastata
Caxat lawtan la, xeetu ñax guy law. Ñax la gu man a muñ bekkoor. Dees na fekk ca Afrig gu naaje gi: Senegaal, Kamerun, Keeñaa, Ugandaa, Ecoopi.